116
Ma sant Yàlla mi ma xettali
1 Maa bëgg Aji Sax ji: maa ko woo,
dagaan ko, mu dégg ma.
2 Teewlu na ma moos,
dama koy woo li feek may dund.
3 Buumi dee a ma laawoon,
njàqarey njaniiw dab ma,
ma dajeek naqar aku tiis.
4 Ma woo Aji Sax ji wall, ne ko:
«Ngalla Aji Sax ji, xettali ma!»
5 Aji Sax jeey boroom yiw ak njub,
sunu Yàllaay boroom yërmande.
6 Aji Sax jeey aar ku xamul àddina;
tumurànke woon naa, mu wallu ma.
7 Bu ma yeboo sama xel dal,
Aji Sax ji baaxe na ma!
8 Xettali nga ma, ba deewuma,
jàppale ma, ba tërëfuma,
feral nga it samay rongooñ.
9 Damay topp Aji Sax ji
ci biir réewum aji dund ñi.
10 Ba ma wax: «Torox naa ba toskare,»
teewul may ànd ak ngëm.
11 Maa jàqoon ba naan:
«Ñépp ay fen-kat lañu!»
12 Ana lu may njukkale Aji Sax ji,
li mu ma baaxe lépp?
13 Xanaa ma yékkati kaasu Aji Sax
jiy misaal wallam,
te may tudd turam.
14 Samay digeek Aji Sax ji laay matal
fi kanam ñoñam ñépp.
15 Wóllërey Aji Sax ji,
deewam day doon lu muy naqarlu.
16 Aji Sax ji, maay sab jaam,
maay sab jaam, di sa doomu jaam bi ma sukk jur.
Yaa yiwi samay buum,
17 yaw laay sarxalal saraxu cant,
woo la ci sa tur, Aji Sax ji.
18 Samay digeek Aji Sax ji laay matal
fi kanam ñoñam ñépp,
19 fi ëtti kër Aji Sax ji,
fi digg Yerusalem.
Màggalleen Ki Sax!