122
Nu ñaanal Yerusalem
Di woy yu ñuy yéege ca tund ya, di ko màggale Yàlla, ñeel Daawuda.
 
Maaka bég, ba ñu ma nee:
«Kër Aji Sax ji lanu jëm.»
Yaw Yerusalem, noo ngii taxaw ci sa bunt.
 
Céy, Yerusalem, dëkkub tabax bu baax
bi booloo, di benn.
Fii la giiri Israayil di yéegsi,
di giir yi Ki Sax séddoo.
Ñu ngi santsi Aji Sax ji,
ni ko Israayil warloo.
Fii la ngànguney Israayil tege,
askanu Daawuda toog ca, di àtte.
 
Dagaanleen jàmmi Yerusalem:
«Yerusalem, yal na sa xeli soppe dal,
jàmm ne ñoyy fi say tata wër,
te xel dal ci biir këri Buur.»
Mbokk ak xarit a waral
may ñaan jàmmi Yerusalem.
Sunu kër Yàlla Aji Sax jee ma tax
di sàkku ngëneelu Yerusalem.