124
Nanu sante Aji Sax ji wallam
Di woy yu ñuy yéege ca tund ya, di ko màggale Yàlla, ñeel Daawuda.
 
Éy su dul woon ak Aji Sax ji nu nekkal!
Israayiloo, waxati ko:
su dul woon ak Aji Sax ji nu nekkal,
ba ñu nu jógalee,
ba nit ña xadaroo sunu kaw,
dañu nu doon wann, nuy dund,
dañu nu doon mëdd nim ndox,
defum wal, buub nu,
def waame wuy wal-wali,
buub nu, yóbbu.
 
Cant ñeel na Aji Sax ji,
ki nu bàyyiwul, noon yi yàpp nu.
Danu ne fërr, nim picc mu rëcc fiiru rëbb,
fiir ga toj, nu raw.
Sunu ndimbal a ngi ci turu Aji Sax ji,
Ki sàkk asamaan ak suuf.