128
Ragal Yàlla, jàmmi kër
Di woy yu ñuy yéege ca tund ya, di ko màggale Yàlla.
 
Ndokkalee képp ku ragal Yàlla,
di jëfe ay yoonam.
Yaay lekk saw ñaq,
mbégteek ngëneel ñeel la.
Sa jabar ni garab gu meññ ci sa kër,
say doom wër a wër sa ndab ni njëmbat lu jebbi.
Ki ragal Aji Sax jaa ngoog,
nii rekk lay barkeele.
 
Yal na la Yàlla barkeele fii ci Siyoŋ;
yal nanga teewe xéewalu Yerusalem sa giiru dund gépp,
te nga gis say sët.
Yal na jàmm dal Israayil.