131
Damaa woyof, gëm Yàlla
Di woy yu ñuy yéege ca tund ya, di ko màggale Yàlla, ñeel Daawuda.
 
Éy Aji Sax ji, man de, réy-réyluwuma,
daŋŋiiraluma,
xintewoowuma lu réy it,
mbaa lu ma ëlëm.
Xanaa ne tekk, ne cell,
ni perantal ak ndeyam;
sama xel dal ni perantal.
Éey Israayil, yaakaaral Aji Sax ji
tey ak ëllëg.