149
Na Israayil màggal Ki Sax
Màggalleen Ki Sax!
Woyleen Aji Sax ji woy wu yees,
màggal ko fi ndajem wóllëreem ñi.
Na Israayil bége Kii ko sàkk,
doomi Siyoŋ, laa ne, ñu bànneexoo seen buur bii.
Nañu màggale turam am pecc,
tëggal ko, xalamal ko.
Aji Sax jee safoo ñoñam,
di terale néew-ji-doole ag mucc.
 
Na wóllërey Yàlla bànneexoo seen ndam,
bu ñu tëddee sax, di sarxolle,
di xaacuy kañ Yàlla,
ŋàbbaale saamaru ñaari ñawka,
ngir duma yéefar yi,
mbugale ko yooyu xeet,
yeewe seeni buur ay càllala,
jénge seeni njiit jéngi weñ,
ngir sottalal leen àtte bi ñu bind,
muy ndamu wóllërey Yàlla yépp.
Màggalleen Ki Sax!