15
Kuy aji jub?
Dib taalifu cant, ñeel Daawuda.
 
Aji Sax ji, kuy ganeji sa xayma?
Ana kuy dëkki sa tund wu sell?
 
Xanaa ki wéye màndu,
di def lu jekk,
di wax dëggu xolam.
Du sos,
du tooñ dëkkandoo,
du baatal moroomam.
Ku siblu, mu sib,
ku ragal Yàlla, mu teral.
Mooy sàmm ngiñam,
su ko dee lor it.
Du leble, ba teg ca;
du nangu ger, ngir fexeel jàmbur.
 
Lii ku koy jëfe doo jang.