29
Aji Sax jeey boroom ndam
Dib taalifu cant, ñeel Daawuda.
 
Yeen goney Yàlla yi, seedeelleen Aji Sax ji,
seedeelleen ko teraangaak doole,
seedeelleen Aji Sax ji màggaayu turam.
Sujjóotalleen Aji Sax ji gànjaroo sellaay.
 
Aji Sax jeey àddu ca kaw ndox ma,
Yàlla mu tedd maa dënu,
Aji Sax jeey tiim ndox mi ne màww.
Aji Sax jeey àddoo doole,
Aji Sax jeey àddoo daraja.
Aji Sax jeey àddu, falaxe garabi seedar,
Aji Sax jee rajaxe seedari Libaŋ.
 
Réewum Libaŋ, mu curpiloo ni wëllu,
tundu Siryoŋ* it, mbete yëkk wu ndaw.
Aji Sax jeey àddu,
fettaxal sawara, mu boy.
Aji Sax ji àddooti, yëngal màndiŋ,
Aji Sax jee yëngal màndiŋu Kades.
Aji Sax jeey àddu, kéwél matu,
garabi àll ruus,
biir këram di mennum riir,
naan: «Màggalleen ko!»
 
10 Aji Sax ji la mbënn ma fekk falu,
Aji Sax jee falu buur ba fàww.
11 Aji Sax jeey kàttanal ñoñam,
di barkeele jàmm ñoñam.
* 29:6 tundu Siryoŋ mooy tundu Ermon ba tey.