42
Maa namm Yàlla
1 Mu jëm ci njiital woykat yi, dib taalifu yeete bu ñeel askanu Kore wu góor.
2 Yaw Yàlla, ni kéwél di sàkkoo walum ndox,
maa la koy sàkkoo xol.
3 Maa mar Yàlla,
Yàlla jiy dund!
Kañ laay teewi fa kanam Yàlla?
4 Rongooñ laay dunde
guddeek bëccëg,
noon yi di ma dëkke naa:
«Ana sa Yàlla ji?»
5 Lii laay fàttaliku, sama xol jeex:
dama daan jàll, jiite mbooloo ma,
jëm kër Yàlla ga, di sarxolleeka sant,
ñu booloo di màggal.
6 Moo man, lu may xàddi, ne yogg?
Lu may jàq nii?
Tee maa yaakaar Yàlla, ba santati ko,
moom sama Yàlla mi may wallu?
7 Maa ngi ne yogg,
ba di la fàttalikoo fa réewum Yurdan
ak tundi Ermon ak Miccar.
8 Sa wal ya sotti, xóote awu moroom ma;
say wal ak say gannax, lépp a jaare sama kaw.
9 Bëccëg Aji Sax ji baaxe ma ngoram,
guddi ma fanaane koo woy,
di ñaan Yàlla mi may dundal.
10 Naa wax Yàlla sama cëslaay, ne ko:
«Lu tax nga fàtte ma,
noon di ma fitnaal,
may wéye tiis?»
11 Noon yaa ngi may ñaawal,
di ma yendoo naa:
«Ana sa Yàlla ji?»
Ma ne yàcc, ne yasar.
12 Moo man, lu may xàddi, ne yogg?
Lu may jàq nii?
Tee maa yaakaar Yàlla, ba santati ko,
moom sama Yàlla mi may wallu?