5
Ma njëlu di ñaan
1 Mu jëm ci njiital woykat yi, ànd aki toxoro, dib taalifu cant, ñeel Daawuda.
2 Éy Aji Sax ji, maa ngi àddu, déglu ma,
maa ngi onk, teewlu ma.
3 Sama Buur, sama Yàlla, déglul, ma ne wallóoy!
Yaw laay ñaan.
4 Aji Sax ji, ag suba, ngay dégg sama baat,
suba su ne ma diis la samay dagaan,
di séentu.
5 Doo Yàlla ju safoo coxor,
yaw lu bon du la daloo.
6 Ku réy du taxaw fi sa kanam,
kuy def lu ñaaw, bañ nga ko.
7 Aji Sax ji, yaay sànk kuy fen,
seexlu kuy bóomeek kuy wore.
8 Man nag, sa ngor lu yaa laa saña dugge sa kër,
sujjóotal sa béreb bu sell, wormaale la.
9 Éy Aji Sax ji, wommate ma sa yoonu njub ndaxi noon,
te xàllal ma saw yoon.
10 Ñii, li ñu wax, wérul,
seen xol a mébét njekkar,
seenug bóli di bàmmeel bu ne ŋàpp,
ñuy naxe làmmiñ wu neex.
11 Éy Yàlla, topp leen,
ñu fakkastaloo seeni pexe;
xalabal ñooñu barey moy,
ñoo la gàntal.
12 Képp ku la làqoo, yal na bég,
di saxoo sarxolle, nga di ko yiir,
te ku la sopp di la bége.
13 Aji Sax ji yaw kat, yaay barkeel ku jub,
yiire ko saw yiw, fege ko.