51
Yàlla, yërëm ma
1 Mu jëm ci njiitu woykat yi, dib taalifu cant, ñeel Daawuda.
2 Mooy ba ko Yonent Yàlla Natan seetsee, gannaaw ba Daawuda tëddee ndaw sa ñuy wax Batseba.
3 Éy Yàlla, ni nga goree, baaxe ma ni,
faral samag tooñ ngir sa yërmande ju yaa.
4 Fóotal maa fóotal sama ñaawtéef,
raxasal ma sama moy.
5 Xam naa ne maa tooñ,
sama moy a ngi janook man saa su ne.
6 Yaw laa moy, yaw doŋŋ.
Li nga ñaawlu laa def.
Kon boo waxee, am dëgg,
te soo àttee, yey.
7 Ñaawtéef daal laa judduwaale,
te sama ndey ëmbaale ma bàkkaar.
8 Dëgg daal nga namm, dëggu reenu xol,
kon déey ma fa xel mu rafet.
9 Wis ma ndox, ma sell;
sang ma, ma set wecc.
10 Yal nanga ma dégtal mbég ak bànneex,
ma bégati, gannaaw ba nga ma dammatee.
11 Bul xool samay moy,
faral sama ñaawtéef yépp.
12 Éy Yàlla, sàkkal ma xol bu sell,
yeesalal ma pastéefu xol.
13 Bu ma xalab,
bu ma xañ sa noo gu sell.
14 May ma, ma bégeeti sag wall,
te dundale ma xol bu tàlli,
15 ma xamal tooñkat sa yoon wi nga tëral,
ba moykat dellu ci yaw.
16 Céy Yàlla, yaw Yàlla mi may musal,
baal ma deret ji ma tuur,
ma sarxolle sa njubte.
17 Boroom bi, may ma, ma wax,
ma delloo la njukkal.
18 Sàkkuwuloo sarax, nde kon ma indi;
te soppuloo saraxu rendi-dóomal.
19 Saraxi Yàlla, xol bu tuub la,
yaw Yàlla, xol bu tuub ba mokk, doo gàntal boroom.
20 Ngalla baaxeel Siyoŋ,
yal nanga tabax tatay Yerusalem.
21 Su boobaa nga nangu sarax yi war,
di saraxu rendi-dóomal.
Su boobaa ñu rendi ay yëkk ca sa sarxalukaay.