7
Boroom tuumaa ngi woote wall
1 Di woyu njàmbat, ñeel Daawuda. Mu woyaloon ko Aji Sax ji ci mbirum kàddu yu tukkee woon ca Kuus, ma bokkoon ci giirug Beñamin.
2 Éy Aji Sax ji, sama Yàlla, yaw laay làqoo!
Musal ma, xettali maak ñi may dàq ñépp.
3 Lu ko moy ñu fàdd ma ni gaynde,
daggate ma te kenn du wallu.
4 Aji Sax ji sama Yàlla, ndegam maa def lii,
ndegam maa taq fenn lu ñaaw,
5 ndegam ku ma jàmmal laa feye aw ay,
mbaa ma dimbali ku ko noonoo te defu ko dara,
6 yal na ma noon rëbb,
dab ma, dëggaate ma,
sàggi saab sag, tëral ci pëndub suuf.
Selaw.
7 Aji Sax ji, meral, jóg,
dajeel maak xadaru noon yi!
Ngalla teewlu ma; yaw, yoon nga santaane.
8 Yal na xeet yi daje, wër la,
nga délsi tiim leen fu kawe.
9 Yal na Aji Sax ji àtte xeet yi;
Aji Sax ji, seetal ci sama njubteek sama màndute te dëggal ma.
10 Yal na mbonug ku bon tees,
te nga saxal ku nekk ci dëgg.
Yaw Yàlla Boroom dëgg, yaay natt xel ak xol.
11 Sama kaaraange, fa Yàlla
miy musal boroom xol bu dëggu.
12 Yàllaay àtte dëgg.
Yàllaay rëbbe bés bu ne.
13 Ku tuubul, Yàlla nàmm saamaram,
tàwwig fittam, diir la.
14 Moom la waajalal ngànnaayi dee,
def ko fitt yuy boy.
15 Ku bon a ngoog, di matu doomu ñaawtéef.
Day sos njombe, di wasin njublaŋ.
16 Am kan lay gas, ba mu xóot,
te pax ma mu gas, moo ca tàbbi.
17 Fitnaam, këpp ci boppam;
coxoram, xàŋŋ cim kaaŋam.
18 Naa sante Aji Sax ji njubteem,
ma woy Aji Sax jiy Aji Kawe ji.