98
Woyleen Aji Sax jiy àttesi
Dib taalifu cant.
 
Woyleen Aji Sax ji woy wu yees,
moo def ay jaloore;
kàttanam ak sellaayu dooleem
jox na ko ndam li.
Aji Sax jee xamleg wallam,
feeñal àtteem, xeet yi gis.
Moo fésal bànni Israayil ngoram,
fésal ko kóllëreem,
àddina ba mu daj di gis
ni nu sunu Yàlla walloo.
Yeen àddina sépp, xaaculleen Aji Sax ji,
sampleen, sarxolle te woy!
Xalamalleen Aji Sax ji, woyal ko,
xalamal ko, woyati!
Walleen liit yi, wal bufta yi
te xaacu fa kanam Buur Aji Sax ji!
 
Na géej riirandook li ko fees,
mook àddinaak li ci biiram,
dex tàccu,
tund sarxolleendoo,
gatandoo ko Aji Sax jiy dikk,
àttesi àddina,
di àtte dun bi dëgg,
tey àttee xeet yépp yoon.