17
Yosafat falu na ca Yuda
Ba mu ko defee Yosafat doomu Asa falu buur, wuutu ko. Mu dëju bu baax nag ci kaw Israayil, nguur ga ca bëj-gànnaar. Yosafat teg ay gàngoor ca mboolem dëkki Yuda ya tata wër, daldi teg ay kuréeli xare ca réewum Yuda, ak dëkki Efrayim ya Asa baayam nangu woon. Ba mu ko defee Aji Sax ji ànd ak Yosafat, ndax na Daawuda maamam daan njëkka doxe, na la doxe, te sàkkuwul tuur ya ñuy wax Baal. Yàllay baayam daal la daan sàkku te ay santaaneem la daan doxe, baña roy jëfi Israayil. Aji Sax ji nag dëgëral nguur ga ca loxoom, Yuda gépp di indil Yosafat ab galag, mu am alal ak daraja ju bare. Ci kaw loolu pastéefu xolam ci jëfe coobarey Aji Sax ji yokku, ba mu jëleeti fa Yuda, bérebi jaamookaay ya, ak xer ya ñuy màggale Asera tuur ma. Mu teg ca yebal, ca ñetteelu atum nguuram, jawriñam ñii di Ben Xayil ak Abdiyas ak Sàkkaryaa ak Netaneel ak Mikaya, ngir ñu jàngaleji ca dëkki Yuda. Ña ànd ak ñoom di ay Leween, Semaya ca la, ak Netaña ak Sebaja ak Asayel ak Semiramot ak Yonatan ak Adoña ak Tobya ak Tob Adoña. Leween ñooña àndaale ak Elisama ak Yexoram, sarxalkat ya. Ñu yóbbaale téereb yoonu Aji Sax ji. Mboolem dëkki Yuda lañu wër, di jàngal askan wa.
10 Tiitaange ju Aji Sax ji sabab nag dikkal mboolem nguuri réew yi séq Yuda, ba tax songuñu Yosafat xare. 11 Ay Filisteen itam di indil Yosafat ay may akub xaalis akub galag, Arab ya sax indil ko ay gàtt: ay kuuy, juróom ñaari junni ak juróom ñaari téeméer (7 700); ak ay sikket, juróom ñaari junni ak juróom ñaari téeméer (7 700).
12 Yosafat gën di màgg, ba kawe lool. Ci biir loolu mu tabax ca Yuda ay këri buur ak dëkki dencukaay. 13 Ay denc yu takku la amoon fa dëkki Yuda, ak niti xarekat, jàmbaari xare yu am doole fa Yerusalem. 14 Ñii nag lañu limal ñooñu, na ñu bokke seeni kër maam:
Ci wàllu Yuda, njiiti junni ya, ñoo di njiit la Atna, ma jiite ñetti téeméeri junniy (300 000) jàmbaari xare yu am doole. 15 Mu feggook njiit la Yoxanan, ma jiite ñaari téeméer ak juróom ñett fukki junniy (280 000) góor. 16 Kooku feggook doomu Sikkri, Amasiya ma yebul boppam ci liggéeyu Aji Sax ji. Moo jiite ñaari téeméeri junniy (200 000) jàmbaari xare. 17 Ci wàllu Beñamin, ñeyu xare ba Elyada moo jiite ñaari téeméeri junni (200 000) ñu gànnaayoo xalaaki fitt ak pakk. 18 Mu feggook Yewosabàdd ma jiite téeméer ak juróom ñett fukki junni (180 000) ñu gànnaayu. 19 Ñooñu ñoo yoroon ndénkaaneb buur bi, te bokkewul ak ña mu tegoon ca dëkk ya tata wër, ca mboolem Yuda.