27
Lu jëm ci nguurug Yotam 
 
1 Yotam amoon na ñaar fukki at ak juróom ba muy falu, te nguuru na fukki at ak juróom benn ca Yerusalem. Yaayam mooy Yerusa doomu Cadog.  
2 Muy def li Aji Sax ji rafetlu; mboolem na Osiyas baayam daan defe la daan defe. Waaye nag duggul ca kër Aji Sax ji. Teewul nag askan wa di defug yàqute ba tey.  
3 Moom moo tabax buntu kër Aji Sax ja féete bëj-gànnaar, te tata ba ca tundu Ofel, tabax na ca lu bare.  
4 Ay dëkk it tabax na ko ca tundi Yuda, te gott ya, tabax na ca kër yu tata wër ak seeni sooroor.   
5 Moom it moo xareek buurub Amoneen ña, duma leen, ba Amoneen ña jox ko atam fanweeri barigoy xaalis ak ñeent, ak fukki barigoy bele ak benn; lors it, fukki barigo ak benn. Loolu la ko Amoneen ña indil atam, indilaatal ko ko ca déwén sa, indilatil ko ko ca déwén-jéeg sa.  
6 Yotam mujj na am doole, ndax pastéef ga mu daan doxe fa kanam Yàllaam Aji Sax ji.   
7 Li des ci mbiri Yotam ak mboolem ay xareem ak ay jëfinam, ma nga binde ca téere ba ñu dippee Buuri Israayil ak Yuda.  
8 Amoon na ñaar fukki at ak juróom ba muy falu, te nguuru na fukki at ak juróom benn ca Yerusalem.  
9 Gannaaw gi, Buur Yotam saay, fekki ay maamam, ñu denc ko ca gox ba ñu naan Kër Daawuda. Axas doomam moo falu buur, wuutu ko.