5
Xarum Yàlla jël na téere ba
1 Ci biir loolu ma gis ci loxol ndijooru ki toog ci ngàngune mi téere bu ñu taxañ bu ñu bind biir ak biti, tay ko juróom ñaari tayu.
2 Ma gis malaaka mu am doole, muy yéenee baat bu xumb, naan: «Ana ku yeyoo tàyyi tayuy téere bii, ubbi ko?»
3 Du kenn nag ci asamaan mbaa kaw suuf, mbaa biir suuf, ku manoona ubbi téere bi, ba yër ko.
4 Ma jooy jooy yu metti, ndax giseesul kenn ku yeyoo ubbi téere bi, ba yër ko.
5 Kenn ci mag ñi ne ma: «Bul jooy. Ma ne, Gayndeg giirug Yuda, njebbital Buur Daawuda daan na. Mooy ubbi téere beek juróom ñaari tayoom.»
6 Ma daldi gis kuuyum xar mu ndaw mu mel ni lu ñu rendi, mu taxaw fi digg ngàngune mi, ñeenti mbindeef yeek mag ñi yéew ko. Xar mi juróom ñaari béjjén la am, ak juróom ñaari bët, di juróom ñaari noowi Yàlla yi ñu yebal ci àddina sépp.
7 Xar mi dikk, jël téere bi ci loxol ndijooru ki toog ci ngàngune mi.
8 Ba mu jëlee téere bi, ñeenti mbindeef yi ak ñaar fukki mag ñeek ñeent ne gurub sukk fi kanamam, ku nekk yor xalam ak andi wurus yu fees ak cuuraay, cuuraay li di ñaani aji sell ñi.
9 Ñuy woy nag woy wu yees, naan:
«Yaa yeyoo jël téere bi,
tàyyi tayu yi,
ndax yaw lañu rendi,
te sa deret nga jote
ay niti gépp giir ak wépp làkk ak wépp xeet ak wépp askan,
ñu doon ñoñi Yàlla.
10 Yaa leen def ñu doon nguurug sarxalkat yi, ñeel sunu Yàlla,
te dinañu nguuru ci àddina.»
11 Ma xoolaat, daldi dégg baati malaaka yu bare, ñu yéew ngàngune mi ak mbindeef yi ak mag ñi, seen lim di ay junni, ba ci junniy junni.
12 Ña ngay àddu ca kaw, naan:
«Xar mi ñu rendi woon moo yeyoo kàttan ak alal,
yeyoo xel ak doole,
moo yeyoo worma, yeyoo darajaak cant.»
13 Ba loolu amee mboolem ndundati asamaan ak kaw suuf ak biir suuf ak géej ak mboolem li ci seen biir, ñoom ñépp di wax, may dégg, naan:
«Ki toog ci ngàngune mi ak Xar mi,
nañu jagoo cant ak worma ak darajaak kàttan,
tey ak ëllëg ba fàww.»
14 Ñeenti mbindeef yi ne: «Amiin.» Mag ñi ne gurub sukk, sujjóot.