2
Póol sàrtal na jataayub màggal Yàlla
Kon nag li jiitu ci mboolem li may dénkaane mooy ngeen di dagaan, di ñaan, di tinu aka sant, ñeel doom aadama yépp, ñeel buur yi ak mboolem boroom baat yi, ngir nu mana nekke jàmm akug dal ak wépp dundin wu tedd, tey wéye ragal Yàlla.
Loolu moo rafet te neex Yàlla sunu Musalkat bi bëgg ñépp mucc te ràññee liy dëgg. Ndax kat jenn Yàlla doŋŋ moo am, benn rammukat doŋŋ it moo am diggante Yàlla ak nit ñi, te mooy kenn nit: muy Almasi Yeesu mi maye bakkanam ngir jot ñépp, te loolu mooy seede si Yàlla joxe, bi waxtu wi jotee. Ci boobu seede lañu ma tabbe ab yéenekat ak ndawal kàddu gi ak itam ab jàngalekat, ñeel xeet yi dul Yawut, ngir ma xamal leen yoonu ngëm ak dëgg. Fenuma, dëgg doŋŋ laay wax.
Kon li ma bëgg moo di góor ñi di ñaane fépp, tàllal loxo yu mucc sikk, te bañ cee boole meroo ak mbiicoo. Naka noonu, na jigéen ñi di sol col gu yiw gu teggine te yem. Buñu jiital di defarlu ay létt yu ëpp ak gànjari wurus aki per ak yérey tànnéef, 10 waaye nañu gànjaroo jëf ju baax, ndax mooy li jekk ci jigéen ñuy seede ne ñooy ñiy ragal Yàlla.
11 Te it bu ñuy jàngale, na jigéen ñiy noppi, te woyof toyy. 12 Mayuma jigéen mu jàngale mbaa mu jiite góor, waaye na noppi. 13 Ndax kat Aadama lañu njëkka bind, Awa topp ca. 14 Te it du Aadama lañu nax, waaye jigéen lañu nax ba mu xëtt ndigal. 15 Teewul muccu jigéen a ngi ci njurum doom, ndegam saxoo na ngëm ak cofeel ak jëfin wu sell te yem.