Esayi
Mucc a ngi ci Emanuwel
1
(Saar 1—12)
1 Lii moo di peeñum Esayi doomu Amocc, di lu mu gis ci mbirum Yuda ak Yerusalem ci janti buuri Yuda yi ñuy wax Osiyas ak Yotam ak Axas ak Esekiya.
Aji Sax ji sikk na ñoñam
2 Asamaan, déglul; suuf, teewlul,
Aji Sax jeey àddu:
«Ay gone laa yar, màggloo leen,
ñoom, ñu gàntal ma.
3 Aw yëkk xam na boroomam,
mbaam-sëf xam gàmb,
bi ko boroomam di xonte,
waaye Israyil xamul,
sama ñoñ ñii xàmmeewuñu.»
4 Wóoy wii xeetu moykat,
wii askan wu diisu ñaawtéef,
mii njurum defkati mbon,
yii doomi yàqute!
Ñoo wacc Aji Sax ji,
ñoo teddadil Aji Sell ju Israyil,
dëddu ko.
5 Xanaa dungeen wéye fippu,
ñu gën leena duma,
te bopp di góomi neen,
xol jeex tàkk?
6 Bopp ba téstën, fenn jagul.
Xanaa gaañu-gaañu aki dagg-dagg rekk,
ak góom yuy nàcc,
fajeesu ko, takkeesu ko,
gajfaleesu kook ag diw.
7 Seenum réew gental,
seeni dëkk xoyomu,
seen suuf, doxandéem yi lekk fi seen kanam,
muy gent bu doxandéem tas.
8 Siyoŋ, dëkk bu taaru baa ngi wéet
ni mbaarum tóokër mbaa dalub toolu xaal.
Mbete dëkk bu ñu gaw!
9 Bu nu Aji Sax ji Boroom gàngoor yi
waccalul woon li nu deseek as néew,
ni Sodom lanuy mel,
Gomor lanuy neexool.
Aji Sax ji bañ na ngistal
10 Dégluleen kàddug Aji Sax ji, yeen njiiti Sodom,
teewluleen sunu yoonu Yàlla, yeen askanu Gomor.
11 «Lu may doye seen sarax yu bare?» la Aji Sax ji wax.
«Damaa suur seen saraxi rendi-dóomali kuuy,
suur nebbonu juru yar gi,
deretu yëkk ak xar ak sikket it, safu ma.
12 Bu ngeen dikkee, teewsi fi sama kanam,
ana ku leen sant ñu joggat-joggatee nii
sama ëttu kër?
13 Buleen fi indeeti saraxi caaxaan,
seen saraxu cuuraay, lu ma seexlu la.
Terutel weer ak bésub Noflaay
ak wooteb ndajee ci yem!
Duma mana dékku ndajem diine mu rax njubadi.
14 Seeni Terutel weer ak seen bési màggal
laa bañ ci sama xol;
yooyu màggal a ma diis ba àttanatuma ko.
15 Bu ngeen ma tàllaleey loxo,
ma fuuyu.
Bu ngeen doon ñaan-ñaanee it,
du maa leen di déglu:
seeni loxo, deret la taq ripp.
16 Raxasuleen ba set wecc,
jëleleen seeni jëf ju bon fi sama kanam,
te ngeen ba lu bon.
17 Jàngleen di def lu baax,
sàkku njub,
waññi ab notkat,
àtte dëgg, ab jirim,
sàmm àqu jëtun.
18 «Kaayleen, nu waxtaan ba juboo,» la Aji Sax ji wax.
«Li seeni bàkkaar di xonq lépp,
tàll lay weexeji.
Li muy xonq curr lépp,
weex furr lay mujje.
19 Su ngeen ma nangoo déggal,
ngëneelu réew mi ngeen di xéewloo.
20 Waaye su ngeen lànkee, fippu,
saamar a leen di xéewloo.»
Aji Sax ji déy a ko wax ci gémmiñam.
Mbugal mooy setal Yerusalem
21 Ana nu biib dëkk yàqoo, mbeteb gànc,
te nekkoon dëkkub kóllëre,
njubte mate fa,
njekk lal fa panaan,
tey ñu diy bóomkat!
22 Sa xaalis doon na raxit,
sa biiñ xormbet.
23 Seeni njiit të,
xejjoo ay sàcc,
ñoom ñépp sopp ger,
di dàq ay neexal,
ab jirim, sàmmuñu àtteem,
àqu jëtun soxalu leen.
24 Moo tax, kàddug Boroom bee,
Aji Sax ju gàngoor yi,
Jàmbaaru Israyil:
«Maay lijjanti samay bañ, ngalla ñoom!
Maay fey samay noon!
25 Yerusalem, maa lay teg loxo,
maay seeyal sa raxit ni xeme,
ba dindi sa mbuubit mépp.
26 Maay waññi say àttekat, ñu mel na woon,
say diglekat it dellu mel ni bu jëkkoon.
Su boobaa ñu wooye la Dëkkub Njekk,
ak Dëkkub Kóllëre.»
27 Siyoŋ dëppook yoon, mucc,
ay tuubkatam wormaal njekk, raw;
28 moykat ak bàkkaarkat yàqoondoo,
dëddukati Aji Sax ji sànkoondoo.
29 Yeenay rus moos ci garab yu mag,
yi ngeen soppoona daje, di xërëmtu.
Yeenay am gàcce ci tóokër,
yi ngeen taamu woona daje, di bokkaale.
30 Yeenay meli ni garab gu mag gu xob ya lax,
mbaa tóokër bu amul siitu ndox.
31 Boroom doole mel ni boob,
la mu liggéey di ferñent,
ànd ak moom ne jéppét,
te kenn du fey sawara wa.