8
Éy su meloon ni sama càmmiñ nga,
mel ni ku ma bokkal wenn ween,
ba ma dajeek yaw biti, sañ laa dar,
te du tax ñu sikk ma!
Ma jàpp la, yóbbu sama néeg yaay,
moom mi ma yar,*
ma may la biiñ bu saf,
ak sama ndoxum gërënaat, nga naan.
Sama càmmoñu waay, ma gegenoo,
ndijooram, ma laxasoo.
Yeen janqi Yerusalem, waatal-leen ma
ne dungeen dakkal te dungeen sooke tëraayu mbëggeel
te jotul.
Joxe naa xol
Janqi Yerusalem
Ana ndaw suy jóge màndiŋ ma nii,
wéeroo nijaayam?
 
Ndaw si
Ci ron pom gi laa la yee,
fa la sa yaay jàppe ëmb,
jur la fa.
Teg ma ci sa xol ni torlukaay,
mbaa ci sa përëg ni lamu màndarga.
Mbëggeel a bare doole ni ndee,
fiiraange xér ni bàmmeel.
Day jàpp jippét,
di jum bu Aji Sax ji taal.
Ndox mu ne xéew du fey mbëggeel,
ay dex du ko mëdd.
Ku koy weccee sa alalu kër gépp it,
ñu jéppi laa jéppi rekk.
 
Càmmiñi ndaw si
Sunub jigéen lu ndaw la,
ween sax amu ko.
Lu nuy defal sunub jigéen
bés bu ñu koy bëggsi?
Su doon am tata,
nu tabaxal ko soorooru xaalis.
Su doon bunt,
nu aare ko xànqi seedar.
 
Ndaw si
10 Maa dim tata,
sama ween di sooroor ya;
moo tax waa ji xam ne
maa di jàmmam.
 
11 Suleymaan am na reseñ ca Baal Amon.
Da koo dénk ay beykat.
Ku nekk di ko fey meññeef ma
junniy dogi xaalis.
12 Junniy dogi xaalis yi,
Suleymaan, yaa ko moom;
ñaar téeméer yi, beykat yi.
Waaye sama toolub reseñ, maa ko moom.
 
Waa ji
13 Yaw mi tooge digg tool bi,
samay xarit a ngi teewlu sa baat,
waxal boog, ma dégg.
 
Ndaw si
14 Nijaay, dawsil,
melal ni kéwél,
mbaa kooba gu ndaw
ci kaw tund wi ci gàncax gu xeeñ gi.
* 8:2 Mbaa: nga jàngal ma baane, 8:6 torlukaay mooy jumtukaay bu mel ni lu ñuy tàmponee. 8:6 Mbaa: tàkk di sël-sëli.