Sabóor 77
Yàllaa ngi seetaan
Mu jëm ci Yedutun, njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, giiroo ci Asaf.
 
Naa xaacu, woo Yàlla,
sama baat fa Yàlla, ngir mu déglu ma.
Bëccëg, ma jàq, sàkku Boroom bi;
guddi, ma tàllal loxo, toqiwuma.
Sama xol tëë sedd.
Ma bàyyi Yàlla xel, binni,
xalaat, xol jeex.
Selaw.
Éy Yàlla, tere nga maa gëmm bët,
ma jaaxle ba waxatuma,
xanaa xalaat janti démb,
at ya woon.
Guddi may fàttliku sama woy,
di waxtaan ak sama ngegenaay,
sama xel di jéex te naa:
«Boroom bi da may gàntal ba fàww,
ba du ma baaxeeti mukk a?
Xanaa daa jeexal ngor tàkk?
Am kàddoom a deñ ba fàww?
10 Moo Yàlla daa fàtte ñeewantee?
Am meram a tëj buntu yërmandeem?»
Selaw.
11 Ma ne, sama naqar daal
mooy Aji Kawe ji daa soppi loxoom.
 
12 Waaye naa fàttliku jaloorey Ki Sax rekk,
fàttliku kéemaanam ya woon.
13 Naa xalaat sa bépp liggéey,
di jàngat say jëf.
14 Céy Yàlla, yaa sell jikko!
Jan yàllaa màgg ni Yàlla?
15 Yaa di Yàlla juy jëfi kéemaan,
yaa siiwal sa doole ci biir xeet yi.
16 Kàttan nga jote sa mbooloo ma,
sëti Yanqóobaak Yuusufa.
Selaw.
17 Yàlla, ndox maa la gis,
ndox maa la gis, di lox;
xóote yaa say,
18 niir ya yuri,
kàddu riire asamaan,
say fitt, fettaxandoo,
19 nga dënoo biir callweer,
melax yi taal àddina,
suuf di lox, di reg-regi.
20 Biir géej di saw yoon;
saw xàll ci digg ndox mu ne xéew,
te kenn gisul foo teg tànk!
21 Wommat nga sa mbooloo ni ag jur,
Musaak Aaróona jiite.