Sabóor 78
Nit goreedi, Yàlla gore
1 Muy taalif bu giiroo ci Asaf.
Yeen sama xeet, dégluleen, ma digal leen;
teewluleen ma, ma wax leen.
2 Maa ngi leen di léeb,
di sulli kumpay démb,
3 muy lu nu dégg, xam ko,
sunuy maam xamal nu ko.
4 Dunu ko nëbb sunuy doom,
xanaa di ko jottli maas giy ñëw,
xamal leen jaloorey Aji Sax ji
ak kàttanam aki kéemaanam.
5 Bindal na sëti Yanqóoba téereb seede,
muy yoon wi mu tegal Israyil.
Mu sant maam yi, ñu xamal ko seeni doom,
6 ngir ñiy juddu ëllëg xam ko,
am ay doom,
ñu màgg, ba xamal ko seeni doom,
7 ngir ñu wóolu Yàlla,
baña fàtte jëfi Yàlla,
di jëfey santaaneem,
8 te baña roy seeni maam;
maas gu të woon te déggadi,
ñu ñàkk pastéef
te sàmmuñu kóllërey Yàlla.
9 Waa giirug Efrayim ñoo soxi fitt,
te keroog xare ba ñoo daw.
10 Ñoo sàmmul kóllërey Yàlla,
gàntal yoonam,
11 ba fàtte ay jalooreem,
di kéemaan yi mu leen won.
12 Fa seen kanami maam la def kéemaan,
fa diiwaanu Cowan, réewum Misra.
13 Moo xar géej ga, jal ndox ma nim tata,
jàlle leen.
14 Bëccëg mu jiitee leen aw niir,
ak leeru sawara guddi gépp.
15 Moo xar ay doj ca màndiŋ ma,
mbàmbulaan wal, mu nàndal leen;
16 mu sotti ndox mu balle ciw xeer,
walal, mu safi dex.
17 Teewul ñu wéy di moy Aji Kawe ji,
di ko gàntal ca màndiŋ ma.
18 Ñoo diiŋate Yàlla xol,
di xemmem ñam wu bakkane.
19 Ñuy waxal Yàlla naan:
«Xam ngeen ne Yàlla manu noo taajal ndab ci màndiŋ mi!
20 Dóor naw doj, moos, ndox ma fettax,
wal ma baawaan,
waaye aw ñam nag?
Daa mana leel mbooloo mii aw yàpp?»
21 Aji Sax ji dégg ci, mer lool;
xolam tàng ci sëti Yanqóoba,
am sànj tàkkal Israyil.
22 Dañoo gëmul Yàlla,
doyloowuñu wallam.
23 Mu digal niir ya fa kaw,
ubbi bunti asamaan,
24 tawal leen mànn, ñu lekk:
peppum asamaan la leen leel;
25 mburum jàmbaar la nit lekk,
mu wàcceel leen ca lu ne gàññ.
26 Yàlla wale ngelawal penku fa asamaan,
bëmëx ak dooleem ngelawal bëj-saalum.
27 Mu tawal leenu yàpp, mu saawe ni pënd,
di njanaaw yu ne gàññ ni feppi suufas géej,
28 wàcce ko fa seen digg dal ba,
mu dajal seeni dëkkuwaay.
29 Mu faj seen aajo,
ñu lekk ba suur këll.
30 Teewul bala seen xel a dal,
seen lanc jàllagul sax,
31 Yàlla mer na, dal ci seen kaw,
bóom ña ëpp doole ca ñoom,
fàdd waxambaaney Israyil.
32 Loolu lépp teewul ñuy bàkkaar ba tey
te gëmuñu ay kéemaanam.
33 Mu dagg seeni fan, mu wéy ni cóolóol,
faat seen bakkan ci safaan bu gaaw.
34 Ba leen Yàlla fàddee, ña des sàkku ko,
tuub, waññiku ci moom.
35 Ñu fàttliku ne Yàllaay seen cëslaay,
xam ne Yàlla Aji Kawe jeey seen njotlaay.
36 Teewul ñu di ko jéema naxey wax,
di ko fen.
37 Joxuñu ko woon xol,
sàmmuñu kóllëreem.
38 Teewul mu yërëm,
baal leen seen ñaawtéef,
ba sànku leen.
Muñ na meram, muñati,
te toppul xolam,
39 ndax xalaataat ne suuxu neen lañu,
di noo guy dem te du délsi.
40 Gàntal nañu ko ba tàyyi ca màndiŋ ma,
teg ko naqar ca ndànd-foyfoy ga.
41 Ñu dellu di diiŋat Yàlla,
di naqaral Aji Sell, ji séddoo Israyil.
42 Fàtte nañu ndimbalam la,
bés ba mu leen jotee ca noon ba,
43 ba def ay firndeem ca Misra,
muy kiraamaam ya ca Cowan.
44 Moo soppli deret seen yooni ndox,
ba naaneetuñu wal ya.
45 Mu wàcce seen biir ndiiraanu weñ
yu leen di lekk,
ak mbott yu leen sànk.
46 Mu jox soccet yi seen gàncax,
jébbal njéeréer yi seen meññeef.
47 Seen garabi reseñ, mu fóome tawab yuur,
seen garabi sikomoor, mu fóome waame.
48 Seen jur gu gudd, mu bàyyeek tawab yuur,
seeni gàtt, mu bàyyeek sawaray melax.
49 Yàlla sotti leen tàngooru xadaram,
mu dim sànj ak naqar ak njàqare,
lépp di gàngooru ndaw yu indiy musiba.
50 Mu afal meram,
ba musalul seen bakkan,
xanaa jébbal leen mbas ma.
51 Daa fàdd képp kuy taaw ca Misra
te juddoo seen digg doole, fa xaymay sëti Xam.
52 Mu génne ñoñam niy gàtt,
wommat leen ni gétt ca màndiŋ ma,
53 ba yóbbu leen fu wóor te tiituñu;
seeni noon, géej ga mëdd leen.
54 Mu yóbbu leen fa suufam su sell sa,
fa tund woowu mu jënde dooleem.
55 Da leena dàqal ay xeet,
dogal leen céru suuf,
sancal giiri Israyil ca seeni xayma.
56 Teewul ñuy diiŋat ak a gàntal Yàlla Aji Kawe ji,
sàmmuñu ay dénkaaneem,
57 xanaa dëddu, di ko wor ni seeni maam,
toogadi ni xala gu yolom.
58 Ñu di ko merlook seen bérabi jaamookaay,
di ko fiirlook seen jëmmi tuur.
59 Ba ko Yàlla yégee, mer na,
ba jéppi Israyil lool.
60 Mu gental dëkkuwaayam ba ca Silo,
xaymaam ba mu sampoon ca doom aadama ya.
61 Mu jébbal ngàllo màndargam dooleem,
may gànjaram ca loxol noon ba.
62 Daa bàyyee ñoñam saamaru noon,
ndax mere yooya séddoom.
63 Seeni waxambaane deeye xare,
seeni janq lamb;
64 seeni sarxalkat loroo saamar,
te jëtun jooyul.
65 Ca la Boroom bi yewwu ni ku doon nelaw,
mel ni jàmbaar ju biiñ xabtal.
66 Mu dóor noon ba yari gannaaw,
teg leen gàcce gu dul fey,
67 ba noppi xalab waa kër Yuusufa,
te tànnul giirug Efrayim,
68 xanaa tànn giirug Yuda,
taamu tundu Siyoŋ wi mu sopp.
69 Mu tabax këram gu sell, na mu mel fa kawa kaw,
dëgër ni suuf, si mu samp ba fàww.
70 Mu teg ca tabb Daawuda, jaamam ba,
jële ko ca gétti xar ya,
71 fa mu doon topptoo jur ga;
mu sàmmal ko waa kër Yanqóoba,
askanu Israyil wi mu séddoo.
72 Daawuda sàmme leen xol bu mucc ayib,
jiitee leen manooreem.