Kàdduy Waxyoo ngi, ñeel Yowaan ci biir
Peeñum Almasi Yeesu
1
Ubbite gi
1 Lii peeñum Yeesu Almasi la, mu ko Yàlla jox ngir mu won ay jaamam yenn xew-xew yu dëgmal. Malaakaam la yebal ci Yowaan ngir xamle ko.
2 Yowaan moo seede mboolem li mu gis, te mu jëm ci kàddug Yàlla ak seedes Yeesu Almasi.
3 Ndokklee képp ku jàng ak mboolem ñi déglu yii kàdduy waxyu, tey sàmm li ñu ci bind, ndaxte waxtu wi jege na.
Ab nuyoo ñeel na juróom ñaari mboolooy gëmkat
4 Lii mu ngi tukkee ci man Yowaan, ñeel juróom ñaari mboolooy gëmkat ña ca diiwaanu Asi. Na leen yiw ak jàmm ñeel, tukkee fa Ki masa Nekk, Ki Nekk, di Kiy Dikk, tukkee it fa boroom juróom ñaari noo ya fa kanam ngànguneem,
5 tukkee itam fa Yeesu Almasi, seede bu wóor bi, moom taaw bi, ki jëkka dekki, jóge ci ñi dee, di kilifay buuri kaw suuf.
Moom mi nu sopp, yiwee nu deretam, ba nu teqlikook kilifteefu sunuy bàkkaar,
6 ba noppi def nu nuy askanu sarxalkati Buur Yàlla Baayam, na ko daraja ak kàttan ñeel tey ak ëllëg ba fàww. Amiin.
7 Mu ngoogu di dikk, indaale niir yi,
te ñépp a koy teg bët,
ba ca ña ko jamoon sax,
te giiri kaw suuf yépp ay jooy ndax moom.
Noonu la moos. Amiin.
8 «Man, maay Alfa, di Omega», la Boroom bi Yàlla wax, moom Ki masa Nekk, Ki Nekk, di Kiy Dikk ëllëg, te di Aji Man ji.
Yowaan am na peeñu ca dunu Patmos
9 Man Yowaan seen mbokk, mi séddook yeen nattu ak barkeb nguurug Yàlla, ak muñ gi ci Yeesu, maa nga woon fa ñu ma toxaloon, ca dun ba ñuy wax Patmos. Li ko waral di sama waare ci kàddug Yàlla ak seedeel Yeesu.
10 Maa nekkoon ci biir Noowug Yàlla benn bésub Sang bi, ma dégg ci sama gannaaw baat bu xumb nig liit.
11 Mu ne: «Mboolem loo gis, bind ko cib téere, nga yónnee ko juróom ñaari mboolooy gëmkat ña ca dëkk ya ñuy wax Efes ak Samirin ak Pergam ak Catir ak Sàrd ak Filadelfi ak Lawdise.»
12 Naka laa geestu, di seet kuy wax ak man, ma daldi gis juróom ñaari tegukaayi làmp yu wurus.
13 Ca digg tegukaayi làmp ya, jëmm juy nirook nit a fa nekk. Ma nga sol mbubb mu tollu ci ndëgguy tànk yi, takkoo ngañaayal wurus ci dënn bi.
14 Kawaru bopp baa nga weex tàll, gët ya di tàkk ni sawara,
15 tànk ya mel ni xànjar bu yànj bu ñu xelli, baat bay riir ni gannaxi géej.
16 Ma nga yor ca loxol ndijooram juróom ñaari biddiiw, ab saamaru ñaari ñawka bu ñaw di lange ca gémmiñ ga, xar-kanam baa nga leer nàññ ni jantub njolloor.
17 Naka laa ko gis, ne dàll daanu ci ay tànkam ni ku dee. Mu teg ma loxol ndijooram, ne ma: «Bul tiit. Maay Ki Jëkk, di Ki Mujj.
18 Maay Kiy Dund, maa dee woon, maay dund nii tey ak ëllëg ba fàww te maa yor caabiy dee ak njaniiw.
19 Kon nag bindal li nga gis: Li am nii tey ak itam liy ñëw gannaaw lii.
20 Kumpa gi ci juróom ñaari biddiiw yi nga gis ci sama loxol ndijoor, ak juróom ñaari tegukaayi làmp yu wurus yi, li muy firi mooy: juróom ñaari biddiiw yi ñoo di malaakay juróom ñaari mboolooy gëmkat ñi; juróom ñaari tegukaayi làmp yi ñoo di juróom ñaari mbooloo yi.»