2
Bindees na waa Efes
«Malaakam mbooloom gëmkat ña ca Efes, bind ko ne ko:
«Lii moo di kàdduy Ki yor juróom ñaari biddiiw yi ci loxol ndijooram, di doxe digg juróom ñaari tegukaayi làmp yu wurus yi. Mu ne: Gis naa say jëf, gis sa liggéey ak sag muñ. Xam naa ne manuloo dékku ñu bon ñi. Seetlu nga ñi tuddoo samay ndaw, ba gis ne ay fen-kat lañu. Xam naa it ne muñ nga te sonn nga moos ngir man te xàddiwoo.
«Waaye li ma la sikke moo di sa cofeel ga nga jëkke woon, moom nga wacc. Kon nag fàttlikul fu kawe fa nga xàwwikoo ba fii, te nga tuub, di jëfe jëf ja nga jëkke woon. Lu ko moy maay dikk ba fi yaw, daldi jële sa tegukaayu làmp fa bérabam, ndegam tuubuloo. Waaye lu baax lii nag yaay boroom: ni ma sibe jëfi ngérum Nikolas*, ni nga ko sibe. Ku ami nopp kat, na dégg li Noowug Yàlla wax mboolooy gëmkat ñi. Ku am ndam nag, maa lay may nga lekk ci garabu dund gi ci Àjjana, toolub Yàlla.
Bindees na waa Samirin
«Malaakam mbooloom gëmkat ña ca Samirin nag, bind ko ne ko:
«Lii moo di kàdduy Ki Jëkk te Mujj, Ki dee woon te dekki. Mu ne: Gis naa sa coono ak sag ñàkk, moona yaaka duunle! Gannaaw loolu it, waxi yàq-der yi tukkee ci ñooñu tuddoo Yawut te duñu Yawut, duñu lenn lu moy jàngub Seytaane, dégg naa ko. 10 Bul ragal mukk mitit wi nga nara daj. Seytaanee ngi noonu di dugal kaso ñenn ci yeen, ngir nattu leen. Dingeen am coono diiru fukki fan. Nanga saxoo kóllëre ba dee fekk la ci, ma kaalaa la kaalag dund.
11 «Ku ami nopp kat, na dégg li Noowug Yàlla wax mboolooy gëmkat ñi. Ku am ndam nag doo loru mukk ci ñaareelu dee gi.
Bindees na waa Pergam
12 «Malaakam mbooloom gëmkat ña ca Pergam nag, bind ko ne ko:
«Lii moo di kàdduy Boroom saamar bi ci ñaari ñawka yi. Mu ne: 13 Xam naa fa nga dëkk, fa la Seytaane samp nguuram. Teewul nga ŋoy ci sama tur te weddiwoo ne man nga gëm ba sax ca fan, ya nit ña reye ca seen biir, Antipas sama seede bu am kóllëre ba, foofa Seytaane dëkk.
14 «Waaye lenn a ngi lu ma lay sikke: yaa ngi uuf foofu ay nit ñuy saxal njànglem Balaam, moom mi doon xiirtal Balag ci tegal Israyil ndëgg-sërëx, ngir ñu lekk ñam wu ñu sarxal ay tuur, ak di gànctu. 15 Naka noonu itam yaa ngi uuf ay nit ñuy saxal njànglem ngérum Nikolas. 16 Kon nag tuubal. Lu ko moy maay dikk léegi ba fi yaw, te saamar biy lange sama gémmiñ, moom laay xareek nit ñooñu.
17 «Ku ami nopp kat, na dégg li Noowug Yàlla wax mboolooy gëmkat ñi. Ku am ndam nag, maa lay may ci mànn§ mu làqu mi, nga lekk, maa lay jox it aw doj wu weex; doj wu ñu bind tur wu bees wu kenn xamul, ku dul ka ko jot.
Bindees na waa Catir
18 «Malaakam mbooloom gëmkat ña ca Catir nag, bind ko ne ko:
«Lii moo di kàdduy Doomu Yàlla ji*, ki ay gëtam mel ni sawara wu yànj, ndëgguy tànkam mel ni xànjar bu ñu jonj. Mu ne: 19 Gis naa say jëf ak sa cofeel ak sa ngëm ak sa liggéey ak sag muñ. Xam naa ne sa jëf yu mujj moo ëpp jëf yu jëkk ya.
20 «Waaye lenn laa lay sikke: dangaa bàyyi Yesabel, jigéen joojuy tuddoo yonent, muy jàngleek a réeral sama jaam ñi, ngir ñuy gànctu ak a lekk ñam wu ñu sarxal ay tuur. 21 May naa ko ab diir, ngir mu tuub, waaye moo buggula tuub ngànctoom. 22 Kon nag maa ngii di ko rattax cib lal, te ñi mu àndal di gànctu it, maa leen di sóob ci mitit wu réy, su ñu tuubul jëf ja ñu koy roye. 23 Am mbas laay fàdde ay taalibeem. Su ko defee mboolooy gëmkat ñépp dinañu xam ne man maay nattu xol ak xel, te maay fey ku nekk ay jëfam.
24 «Waaye yeen ñi ci des ñépp nag, yeen waa Catir ñi toppul moomu njàngle te jotuleena xam loolu ñu naan xóotey xam-xamu Seytaane, maa ne leen, duma leen sëf beneen sëf. 25 Ŋoyleen rekk ci li ngeen am, ba kera may dikk.
26 «Ku am ndam nag, ku saxoo jëf ji ma soob, ba kera muj ga, maa lay jox sañ-sañ ci kaw xeet yi:
27 Ni ñuy rajaxee ndaal xandeer,
noonu nga leen di sàmmeji yetu weñ,
28 te man ci sama bopp, noonee laa jote sañ-sañ bi ci sama Baay. Maa lay jox itam biddiiwu njël. 29 Ku ami nopp kat, na dégg li Noowug Yàlla wax mboolooy gëmkat ñi.
* 2:6 ngérum Nikolas mooy ñiy taafantoo sañ-sañ bu ñu am gannaaw bu ñu gëmee Yeesu, ngir daganal yenn aada yu ñaaw yu mel ni lekk lu ñu sarxal ay tuur, ak powum séy. 2:11 ñaareelu dee gi: seetal ci 20.14 ak 21.8. 2:14 Balaam, Balag: Balaam moo doon mbubboo turu yonent, di fexee rëbb bànni Israyil, ngir sàkku alal ci Balag buuru Mowab ci jamonoy Yonent Yàlla Musaa. Seetal ci Màndiŋ ma 22—23. § 2:17 mànn moo di ñam wa Yàlla wàcceeloon Musaa ak bànni Israyil, ba ñu gàddaayee Misra, jëm ca réew ma leen Yàlla digoon. * 2:18 Doomu Yàlla: tur wii tekkiwul ne Yàlla moo jur Yeesu mook Maryaama. Tekkiwul it ne dañoo màggal nit, ba di ko méngale ak Yàlla. Waaye day tekki ne Yeesu mooy Kàddug Yàlla, mooy màndargam jëmmu Yàlla, ci jikkoom ji gëna biire. Ku gis doom, man ngaa xam nu baayam mel. Ku gis Yeesu kon, mana xam nu Yàlla mel.