5
Njiiti Israayil lajj nañu
1 «Dégluleen lii, yeen sarxalkat yi!
Teeyluleen, yeen waa kër Israayil!
Teewluleen, yeen waa kër buur!
Yeen la àtte bi ñeel.
Ag fiir ngeen tegoon ca Mispa,
ab caax ngeen laloon ca tundu Tabor,
2 Fippukat yi gën nañoo xuus ci seen bóome,
waaye maa leen di yar, ñoom ñépp.
3 Maa xam Efrayim miy Israayil,
umpu ma.
Efrayim, yaa gànctu,
Israayil laa ne, yaa sobeel sa bopp.
4 Seeni jëf a leen mayul ñu dellu ci seen Yàlla,
nde ngelawal ngànctoo wale fa seen biir,
te Aji Sax ji, faalewuñu ko.
5 Israayil, ag reewandeem a ko tiiñal,
Israayil, ak Efrayim sax, dinañu fakkastaloo seenug ñaawtéef,
Yuda it ànd ak ñoom fakkastalu.
6 Seen jur gu gudd ak gu gàtt lañuy àndal,
di seet Aji Sax ji, duñu ko gis,
te moo leen dëddu.
7 Aji Sax ji lañu wor,
nde doomi po lañu jur.
Léegi la leen màggalug Terutel weer
di booleek seen suuf, sànk leen.
Yàlla dëkk na Israayil ak Yuda
8 «Walleen bufta bi ca Gibeya,
jibal liit gi ca Raama
te yéene ca Bet Awen.
Moytul sa gannaaw, Beñamin.
9 Efrayim day gental kera bésu mbugal,
maa xamle ci biir giiri Israayil lu wér péŋŋ.
10 Kàngami Yuda mujj mel ni
ñuy toxal màndargam làccu suuf.
Ci seen kaw laay yuri sama sànj nim ndox.
11 Efrayim lees di noot,
joggati ay yelleefam,
nde moo dogoo topp yoonu caaxaan.
12 Man nag ni gunóoru ñaawat laay mel ci Efrayim,
te ni bant bu nëb laay mel ci Yuda.
13 Ba Efrayim gisee jàngoroom,
Yuda gis ab danaam,
Efrayim a dem Asiri,
yónnee ca Buur Yareb.
Waaye manu koo wéral,
mbaa di ko fajal ab danaam.
14 Man déy ni gaynde laay mel ak Efrayim,
ni gaynde gu mat laay mel ak waa kër Yuda.
Man, man mii maay xotat, wéy,
maay yóbbu te kenn du wallu.
15 Ma daldi ñibbi, ba ñu nangu seenug tooñ,
seet fu ma féete.
Bu ñu jàqee lañuy daw wutsi ma.»