6
Wooteb tuub jib na 
 
1 Ca ngeen naan: «Nan dellu ci Aji Sax ji.  
Moo nu xotat, te moo nuy wéral.  
Moo nu duma, te moo nuy takkal sunuy góom.   
2 Ñaari fan, mu leqali nu,  
ñetteel ba mu yékkati nu,  
nuy dund fi kanamam.   
3 Nan ràññee, di saxoo faale Aji Sax ji.  
Ni jant bu fenk la dikkam wóore,  
ni ab taw la nuy dikkale,  
ni ab tawu mujjantal buy seral suuf.»   
   
 
4 Aji Sax jee tontu: «Ana nu ma lay def, yaw Efrayim?  
Nu ma lay def, yaw Yuda?  
Te sa ngor di xiinu suba,  
mbaa ab lay, jekki ne mes.   
5 Moo tax yonent yi laa leen di dumaa,  
sama kàdduy gémmiñ laa leen di reye.  
Seen àttee leen di leeral ni ceeñeeru njël.   
6 Ndax ngor laa namm, dub sarax,  
ràññee Yàllaa ma gënal saraxi rendi-dóomal.   
   
 
7 «Waaye ñoom ca dëkk ba ñuy wax Aadama lañu feccee kóllëre,  
foofa lañu ma wore.   
8 Galàdd mooy dëkkub defkati ñaawtéef,  
taq ripp ak deret.   
9 Ni saay-saay siy tëroo,  
ni la sarxalkat yi lëkkoo,  
di bóome ca yoonu Sikem.  
Ndaw jëf ju ñaaw!   
10 Ci kërug Israayil laa gis lu yées:  
fa la Efrayim di gànctoo,  
Israayil googu laa ne moo sobeel boppam.   
11 Yuda yaw it, sam ngóob ma ngay taxawe,  
kera bu may tijji sama wërsëgu ñoñ.